Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàdduy Waare - Kàdduy Waare 10

Kàdduy Waare 10:17-20

Help us?
Click on verse(s) to share them!
17Ndokklee, yeen, réew ma as gor falu, te bu jotee, jawriñ ñay xéewlu, ngir am doole te baña màndi.
18Tayel, puj bu màbb; yaafus, néeg buy senn.
19Aw ñam bégal, aw ñoll bànneexal, xaalis tontu lu ne.
20Sam xel sax bu ca saaga buur, sa néegu biir sax, bu fa saagaa boroom daraja. Xamoo picc muy yóbbu sa kàddu, mbaa njanaaw luy siiwali mbir ma.

Read Kàdduy Waare 10Kàdduy Waare 10
Compare Kàdduy Waare 10:17-20Kàdduy Waare 10:17-20