Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 10:17-20 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 10:17-20 in Kàddug Yàlla gi

17 Ndokklee, yeen, réew ma as gor falu, te bu jotee, jawriñ ñay xéewlu, ngir am doole te baña màndi.
18 Tayel, puj bu màbb; yaafus, néeg buy senn.
19 Aw ñam bégal, aw ñoll bànneexal, xaalis tontu lu ne.
20 Sam xel sax bu ca saaga buur, sa néegu biir sax, bu fa saagaa boroom daraja. Xamoo picc muy yóbbu sa kàddu, mbaa njanaaw luy siiwali mbir ma.
Kàdduy Waare 10 in Kàddug Yàlla gi