17Lal ba, ma xeeñal, mu ne bann, di ndàbb, cuuraay ak xas mu neex.
18Dikkal, nu baanee baane, ba bët set, te bànneexu ci mbëggeel.
19Sama jëkkër newu fa, daa dem yoon wu sore.
20Mbuusum xaalis la ŋàbb, yóbbu, du ñibbsi ndare weer wi fees dell.»
21Muy mocc ak a moccaat, ba nax ko, di wax lu neex, ba man ko.
22Waa ja jekki, topp ko, mbete yëkk wu ñuy rendiji, mbaa dof bu ñu jéng, di ko yari.
23Mooy picc mu tàbbi cig fiir. Du xam ne day dee, ba keroog fitt jam ko ci xol.
24Kon nag, doom, dégluleen ma, teewluleen samay wax.
25Bu leen soosu ndaw xiir ci moy, buleen teggi, topp ko.
26Bare na ku dee, moo ko rey, maneesula waññ ñi mu rey ñépp.
27Këram yoonu njaniiw la, daa bartalu, tàbbi néegi ndee.