17 Lal ba, ma xeeñal, mu ne bann, di ndàbb, cuuraay ak xas mu neex.
18 Dikkal, nu baanee baane, ba bët set, te bànneexu ci mbëggeel.
19 Sama jëkkër newu fa, daa dem yoon wu sore.
20 Mbuusum xaalis la ŋàbb, yóbbu, du ñibbsi ndare weer wi fees dell.»
21 Muy mocc ak a moccaat, ba nax ko, di wax lu neex, ba man ko.
22 Waa ja jekki, topp ko, mbete yëkk wu ñuy rendiji, mbaa dof bu ñu jéng, di ko yari.
23 Mooy picc mu tàbbi cig fiir. Du xam ne day dee, ba keroog fitt jam ko ci xol.
24 Kon nag, doom, dégluleen ma, teewluleen samay wax.
25 Bu leen soosu ndaw xiir ci moy, buleen teggi, topp ko.
26 Bare na ku dee, moo ko rey, maneesula waññ ñi mu rey ñépp.
27 Këram yoonu njaniiw la, daa bartalu, tàbbi néegi ndee.