28Bul ne say dëkk: «Demal ba beneen, ma jox la,» te fekk la yor.
29Bul fexeel dëkkandoo bu dëkk ak yaw ci kóolute.
30Bul joteek kenn ci neen, te tooñu la.
31Bul ñee ku néeg, te bu ko roy fenn.
32Aji Sax ji daa sib ku dëng, xejjoo kuy jubal.
33Aji Sax ji day alag kër ku bon, di barkeel waa kër ku jub.