28 Bul ne say dëkk: «Demal ba beneen, ma jox la,» te fekk la yor.
29 Bul fexeel dëkkandoo bu dëkk ak yaw ci kóolute.
30 Bul joteek kenn ci neen, te tooñu la.
31 Bul ñee ku néeg, te bu ko roy fenn.
32 Aji Sax ji daa sib ku dëng, xejjoo kuy jubal.
33 Aji Sax ji day alag kër ku bon, di barkeel waa kër ku jub.