16Day seetlu ab tool, jënd ko, sàkk ciw ñaqam, jëmbat tóokër.
17Day gañu di góor-góorlu, ak a dëgëral përëg ya.
18Day gis njartel liggéeyam, te làmpam du fey guddi.
19Ma ngay yor poqe ak këccu, di ëcc.
20Day jox ku ñàkk, di sàkkal néew-ji-doole.
21Tiitul ci njaboot gi sedd bu metti, ndax ñoom ñépp ay tegley yére.
22Mooy sàkkal boppam ay malaan, ay yéreem mucc ayib te yànj.
23Dees na ràññee jëkkëram ca pénc ma, fa muy toog ca magi réew ma.
24Ndaw su ni mel day ràbb ay yére, di jaay, aki gañaay, di jox jaaykat yi.
25Faaydaak jom la làmboo, te ëllëg ubul boppam.
26Day wax lu xelu, di digle ngor.
27Jigéen jooju mooy bàyyi xel ci njabootam, te du nangoo yàccaaral.
28Doom ya dañu ko naan: «Jarawlakk!» jëkkër ja di ko gërëm naan:
29«Jeeg bu jàmbaare bare na, waaye yaw, yaa ci raw.»
30Melokaan wu jekk day naxe, taar day wéy, waaye jigéen ju ragal Aji Sax ji, kookoo jara gërëm.