1Lii waxi Lemuyel la, buuru Maasa, te ndeyam jàngal ko ko. Mu ne:
2Ngóor si doom, saa doomi bopp! Yaa di ñaan gu nangu, doom!
3Bul jox jigéen ñi sa doole, bul jox say siddit jigéen ñiy sànk buur.
4Buur moomul di naan biiñ, Lemuyel, buur moomu ko; kilifa moomul di sàkku ñoll.
5Lu ko moy mu naan, ba fàtte lu yoon tëral, xañ néew-ji-doole ju ne, àqam.
6Bàyyeel ñoll kuy sànku, bàyyi biiñ ak boroom naqar.
7Bu ñu naanee, fàtte seen néewle, ba dootuñu fàttliku seenu tiis.
8Nanga àddul ku amul kàddu, ku sësul fenn, nga ñoŋal àqam.
9Deel àddu, di àtte njub; ku ñàkk ak ku néewle, nga sàmm àqam.
10Jeeg bu jàmbaare, ndaw lu jafe, ba rawati gànjar!