Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 2

Kàddu yu Xelu 2:7-21

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Day dencalal ndam kiy jubal, di yiir ku mat.
8Day wattu ku jub fu mu jaare, di sàmm wóllëreem ciw yoon.
9Kon nga xam njub ak yoon, xam jubal ak mboolem yoonu mbaax.
10Ndax xel mu rafet miy tàbbi sa xol, nga xam, sa xol tooy,
11nga foog, fegu, am ug dégg, raw,
12mucc ci yoonu ku bon ak kuy wax lu jekkadi,
13mucc ci kuy wacc yoonu njub, di jaare mbedd yu lëndëm.
14Kon nga mucc ci kuy def lu bon, tey bànneexoo lu jekkadi.
15Yoonu ku ni mel day lunk, jaaruwaayam dëng.
16Xel mu rafet da lay musal ci ndaw su yemadi, bokk feneen, di wax lu neex.
17Day dëddu wóllëreem, ba muy ndaw, fàtte kóllëreem ak Yàllaam.
18Këram day joy wuti ndee, ay jaaruwaayam jëm njaniiw.
19Ku dem ca moom dootoo délsi, doo gisati yoonu dund mukk.
20Kon nag aweel mbeddum waa ju baax, toppal yoonu ku jub,
21ndax kuy jubal ay dëkke réew mi, te ku mat a fiy des.

Read Kàddu yu Xelu 2Kàddu yu Xelu 2
Compare Kàddu yu Xelu 2:7-21Kàddu yu Xelu 2:7-21