20Ana koo gis, mu rattaxle? Kooku ab dof a ko gën demin.
21Ku yàq sab surga ba muy ndaw, bu ëllëgee mu defe ne doom la.
22Boroom xadar day sooke ay, te ku tàng bopp moy, moyati.
23Réy-réylu, detteelu rekk; woyofal, ñu naw la.
24Ku ànd akub sàcc, sa noonu bopp nga: soo waxee dëgg, yoon topp la; soo ko miimee, Yàlla topp la.