Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 29:20-24 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 29:20-24 in Kàddug Yàlla gi

20 Ana koo gis, mu rattaxle? Kooku ab dof a ko gën demin.
21 Ku yàq sab surga ba muy ndaw, bu ëllëgee mu defe ne doom la.
22 Boroom xadar day sooke ay, te ku tàng bopp moy, moyati.
23 Réy-réylu, detteelu rekk; woyofal, ñu naw la.
24 Ku ànd akub sàcc, sa noonu bopp nga: soo waxee dëgg, yoon topp la; soo ko miimee, Yàlla topp la.
Kàddu yu Xelu 29 in Kàddug Yàlla gi