2Màggug Yàllaa ngi ci li mu làq, darajay buur a ngi ci li mu feeñal.
3Maneesula daj li ci xelu buur, xalaatam daa kawe ni asamaan, xóot ni suuf.
4Xellil xaalis, tonni lu ca rax, ba ab tëgg man caa am ndab.
5Ab soxor it, dàqal, mu sore buur, ngir njubte law, jalam sax.
6Bul réy-réylu fi kanam buur, bul tooge jataayu boroom daraja,
7ndax ñu ne la: «Yéegal, jegesi fii,» moo gën ñu torxal la ci kanam kilifa. Boo gisalee sa bopp it,
8bul gaawa layooji, ana nooy def ëllëg, bu ñu la yeyee?
9Ñaarool ak ki nga joteel, te bul jéebaane jaambur.
10Lu ko moy ñu dégg ko, rusloo la, sab der yàqu yaxeet.
11Wax ju ñor di nataalu wurus wu tege ci xaalis.
12Kàddu yu lay yedd ci kuy dégg, jaarob wurus la mbaa gànjaru ngalam.
13Ndaw lu wóor day seral xolu njaatigeem, mooy ndox mu sedd ci tàngooru ngóob.
14Kuy dige te doo joxe, yaay xiin wu ngelaw, mu naaxsaay.