19Bul wóolu workat bésub njàqare, mooy bëñ bu bon mbaa tànk bu nasax.
20Kuy woy, boroom tiisu xol di dégg, yaa futti mbubbam cib sedd, mbaa nga jonj xorom ci góomam.
21Bu sab noon xiifee, jox ko mu lekk, bu maree, may ko mu naan,
22day rus ba mel ni koo yeni xal, te Aji Sax jee lay fey.
23Jëw, mer a cay topp; mooy ngelawal taw, taw a cay topp.