Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 25:19-23 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 25:19-23 in Kàddug Yàlla gi

19 Bul wóolu workat bésub njàqare, mooy bëñ bu bon mbaa tànk bu nasax.
20 Kuy woy, boroom tiisu xol di dégg, yaa futti mbubbam cib sedd, mbaa nga jonj xorom ci góomam.
21 Bu sab noon xiifee, jox ko mu lekk, bu maree, may ko mu naan,
22 day rus ba mel ni koo yeni xal, te Aji Sax jee lay fey.
23 Jëw, mer a cay topp; mooy ngelawal taw, taw a cay topp.
Kàddu yu Xelu 25 in Kàddug Yàlla gi