10Lu ko moy ñu dégg ko, rusloo la, sab der yàqu yaxeet.
11Wax ju ñor di nataalu wurus wu tege ci xaalis.
12Kàddu yu lay yedd ci kuy dégg, jaarob wurus la mbaa gànjaru ngalam.
13Ndaw lu wóor day seral xolu njaatigeem, mooy ndox mu sedd ci tàngooru ngóob.
14Kuy dige te doo joxe, yaay xiin wu ngelaw, mu naaxsaay.
15Muñ mer ay nax kilifa, te wax ju neex, fu mu jaar, mu nooy.
16Boo gisee lem, lekkal lu yem; bu ëppee, nga waccu ko.
17Na sa tànk di gëj kër dëkkandoo; boo ko sàppee, mu jéppi la.
18Ku seedeel sa moroom ay fen, yen nga ko aw njur mbaa saamar mbaa fitt.
19Bul wóolu workat bésub njàqare, mooy bëñ bu bon mbaa tànk bu nasax.
20Kuy woy, boroom tiisu xol di dégg, yaa futti mbubbam cib sedd, mbaa nga jonj xorom ci góomam.
21Bu sab noon xiifee, jox ko mu lekk, bu maree, may ko mu naan,
22day rus ba mel ni koo yeni xal, te Aji Sax jee lay fey.
23Jëw, mer a cay topp; mooy ngelawal taw, taw a cay topp.