17Teewlul te déglu li boroom xel yi wax. Defal sam xel ci li ma lay xamal.
18Soo mokkalee, ba man koo tari, muy sa mbégte.
19Yaw laa koy xamal tey jii, ndax nga wóolu Aji Sax ji.
20Dama laa bindal fanweeri dénkaane, ci wàllu digal ak xam-xam,
21ngir xamal la lu wér te dëggu, nga yóbbaale kàdduy dëgg, yoo tontoo ña la yebal.
22Bul xañ néew-ji-doole; néew-ji-doole la. Ku tumurànke, bu ko soxore cib àtte,
23Aji Sax ji da koy taxawu, ku ko xañ, mu xañ la bakkan.
24Bul xaritook ku gaawa mer, bul ànd ak ku tàng bopp.
25Lu ko moy nga mel ni moom, te kon nga lonku.
26Bul bokk ci ñiy dige, di gàddul nit bor.
27Soo amul loo ko feyale, ñu yékkatee la sab lal, nangu ko.
28Bul toxal màndargam cosaan ci làccu suuf te say maam tegoon ko fa démb.
29Seetlul ku man liggéeyam, buur lay liggéeyal, du liggéeyal baadoolo.