Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 21

Kàddu yu Xelu 21:3-9

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Deel def dëgg ak njekk, moo gënal Aji Sax ji ab sarax.
4Xeebaateek réy-réylu mooy bàkkaar yi ñuy ràññee ku bon.
5Farlu, woomle; ku gaawtu, mujj néewle.
6Alal ju la fen may, cóolóol la, day naaw, wut ko xaru la.
7Coxor day sànk boroom, ndax day baña def njub.
8Ab saaysaay day dëngal, nit ku dëggu di jubal.
9Dëkkeb ruq cim sàq moo gën jabar ju pànk.

Read Kàddu yu Xelu 21Kàddu yu Xelu 21
Compare Kàddu yu Xelu 21:3-9Kàddu yu Xelu 21:3-9