Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 21

Kàddu yu Xelu 21:19-26

Help us?
Click on verse(s) to share them!
19Dëkke ndànd-foyfoy moo gën jabar ju tàng, bare ay.
20Ku xelu denc këram ngëneeli alal aku diw, ab dof saax-saaxee josam.
21Ku saxoo njekk ak ngor am fan wu gudd, naataangeek daraja.
22Ku ñaw mana daan jàmbaari dëkk bu mag, ba màbb tata ja ñu yaakaaroon.
23Ub sa gémmiñ, moom sa làmmiñ, mucc ci njàqare.
24Ku réy te bew, mooy ñaawle, day reew, ba jéggi dayo.
25Ab yaafus day bëgg lu mu amul ba dee, ndax du nangoo liggéey;
26day yendoo xemmem, te du am, ka jub di joxeek a joxewaat.

Read Kàddu yu Xelu 21Kàddu yu Xelu 21
Compare Kàddu yu Xelu 21:19-26Kàddu yu Xelu 21:19-26