Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 21

Kàddu yu Xelu 21:14-30

Help us?
Click on verse(s) to share them!
14Ku mer, may ko ci sutura, mu giif; boroom xadar, boqal ko neexal, mu dal.
15Bu yoon amee, ku jub bég; kuy def lu bon jàq.
16Ku noppee jëfe xel, noppluji njaniiw.
17Ku topp sa bànneex, mujje ñàkk; ku sopp biiñ ak lu niin du woomle.
18Ku bon këppoo ayu ku baax, workat gàddu musibam kuy jubal.
19Dëkke ndànd-foyfoy moo gën jabar ju tàng, bare ay.
20Ku xelu denc këram ngëneeli alal aku diw, ab dof saax-saaxee josam.
21Ku saxoo njekk ak ngor am fan wu gudd, naataangeek daraja.
22Ku ñaw mana daan jàmbaari dëkk bu mag, ba màbb tata ja ñu yaakaaroon.
23Ub sa gémmiñ, moom sa làmmiñ, mucc ci njàqare.
24Ku réy te bew, mooy ñaawle, day reew, ba jéggi dayo.
25Ab yaafus day bëgg lu mu amul ba dee, ndax du nangoo liggéey;
26day yendoo xemmem, te du am, ka jub di joxeek a joxewaat.
27Saraxu nit ku bon ñaawtéef la, rawatina bu ci jubloo lu bon.
28Seede buy fen day sànku, kuy dégg, sa kàddu sax.
29Ku bon day ñeme-ñemelu, ku jub la muy def da koy wóor.
30Nit xeluwul, amul ug dégg ak pexe, ba manal Aji Sax ji dara.

Read Kàddu yu Xelu 21Kàddu yu Xelu 21
Compare Kàddu yu Xelu 21:14-30Kàddu yu Xelu 21:14-30