13Bul bëggi nelaw, ba ñàkk dab la; boo njaxlafee, lekk ba desal.
14Kuy waxaalee ngi naan: «Baaxul de!» Bu nee wërëñ, di damu naan: «Aka jar!»
15Wurus am na ak gànjar yu bare, waaye kàdduy xam-xam a gën per yu jafe.
16Ku gàddul jaambur bor, jëlal mbubbam; tayle ko, moo dige feyal jaambur.
17Njublaŋ, lekk, jëkke neex, mujj mel ni lancub suuf.
18Pexe, ndigal a koy lal; xare, ay tegtal.
19Kuy wër di jëw, wuññi sutura; ku réy làmmiñ, bul déeyook moom.
20Ku saaga sa ndey mbaa sa baay añe lëndëmu bàmmeel.
21Alal ju gaaw du mujje barkeel.
22Bul feyantook ku la tooñ; dénkul ci Aji Sax ji, mu wallu la.
23Aji Sax ji bañ na nattu diisaay yu wuute, njublaŋ ci natti diisaay baaxul.
24Jéegoy jaam Aji Sax jee ko yor, kenn xamul foo jëm.
25Bul gaawtuy digeek Yàlla, di dugal sa bopp; bul giñ, di réccu.
26Buur, bu xeloo, ràññee ku bon, mbugal ko, te du ko ñéeblu.
27Xelum nit làmp la bu Aji Sax ji taal, da koy niital ba ca biir xolam.
28Ngor ak worma day aar buur, ngor ay saxal ab jalam.
29Sagu ndaw, doole ja; gànjaru mag, bijjaaw ba.