13 Bul bëggi nelaw, ba ñàkk dab la; boo njaxlafee, lekk ba desal.
14 Kuy waxaalee ngi naan: «Baaxul de!» Bu nee wërëñ, di damu naan: «Aka jar!»
15 Wurus am na ak gànjar yu bare, waaye kàdduy xam-xam a gën per yu jafe.
16 Ku gàddul jaambur bor, jëlal mbubbam; tayle ko, moo dige feyal jaambur.
17 Njublaŋ, lekk, jëkke neex, mujj mel ni lancub suuf.
18 Pexe, ndigal a koy lal; xare, ay tegtal.
19 Kuy wër di jëw, wuññi sutura; ku réy làmmiñ, bul déeyook moom.
20 Ku saaga sa ndey mbaa sa baay añe lëndëmu bàmmeel.
21 Alal ju gaaw du mujje barkeel.
22 Bul feyantook ku la tooñ; dénkul ci Aji Sax ji, mu wallu la.
23 Aji Sax ji bañ na nattu diisaay yu wuute, njublaŋ ci natti diisaay baaxul.
24 Jéegoy jaam Aji Sax jee ko yor, kenn xamul foo jëm.
25 Bul gaawtuy digeek Yàlla, di dugal sa bopp; bul giñ, di réccu.
26 Buur, bu xeloo, ràññee ku bon, mbugal ko, te du ko ñéeblu.
27 Xelum nit làmp la bu Aji Sax ji taal, da koy niital ba ca biir xolam.
28 Ngor ak worma day aar buur, ngor ay saxal ab jalam.
29 Sagu ndaw, doole ja; gànjaru mag, bijjaaw ba.