Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 19

Kàddu yu Xelu 19:12-17

Help us?
Click on verse(s) to share them!
12Merum buur ni gaynde gu ŋar; yërmandey buur ni lay cig mbooy.
13Doom ju dof naqaru baay baa, te jabar ju pànk mooy senn bu dakkul.
14Kër ak alal ngay donne ci baay; jabar ju xelu, Aji Sax jee koy maye.
15Ab yaafus, nelaw yu xóot, te ku yàccaaral xiif.
16Ku jëfe ndigal, sàmm sa bakkan; ku moytuwul sa bopp, dangay dee.
17Ku baaxe ku ñàkk, lebal nga Aji Sax ji, te moo lay yool.

Read Kàddu yu Xelu 19Kàddu yu Xelu 19
Compare Kàddu yu Xelu 19:12-17Kàddu yu Xelu 19:12-17