12 Merum buur ni gaynde gu ŋar; yërmandey buur ni lay cig mbooy.
13 Doom ju dof naqaru baay baa, te jabar ju pànk mooy senn bu dakkul.
14 Kër ak alal ngay donne ci baay; jabar ju xelu, Aji Sax jee koy maye.
15 Ab yaafus, nelaw yu xóot, te ku yàccaaral xiif.
16 Ku jëfe ndigal, sàmm sa bakkan; ku moytuwul sa bopp, dangay dee.
17 Ku baaxe ku ñàkk, lebal nga Aji Sax ji, te moo lay yool.