2Ku xelu àddu, xam-xam rafet; ab dof di talalali.
3Aji Sax ji moo gis lépp, di xool ku baax ak ku bon.
4Wax ju neex garab la, doom ya di dundal, kàddu yu jekkadi di jeexal xol.
5Ab dof day xeeb yaru baay ba, kuy dégg waxi àrtu, xelu nga.
6Kër ku jub, koom gu yaa; ku jubadi, alalam jur fitna.