2 Ku xelu àddu, xam-xam rafet; ab dof di talalali.
3 Aji Sax ji moo gis lépp, di xool ku baax ak ku bon.
4 Wax ju neex garab la, doom ya di dundal, kàddu yu jekkadi di jeexal xol.
5 Ab dof day xeeb yaru baay ba, kuy dégg waxi àrtu, xelu nga.
6 Kër ku jub, koom gu yaa; ku jubadi, alalam jur fitna.