Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 11

Kàddu yu Xelu 11:3-24

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Kuy jubal, jiital mat. Njublaŋ ak wor, detteelu.
4Alal du jariñ bésu mbugal; jub, mucc ci gàtt fan.
5Ku mat, njekk xàllal la; coxor daaneel boroom.
6Jubalal, sa njekk musal la; ab workat day bëgge, ba far keppu.
7Ab soxor saay, yaakaaram seey, rawatina yaakaar ju sës ci alal.
8Ku jub mucc ci njàqare, ab soxor wuutu ko ca.
9Ay sos la yéefar di loree, waaye ku jub xam-xam la cay mucce.
10Ku jub baaxle, waa dëkkam bànneexu; ab saaysaay saay, mbégte dim riir.
11Barkeb ku jub teral nab dëkk, kàddug ku soxor tas nab dëkk.
12Waxi xeebaate ñàkk bopp la, ku am ag dégg day noppi.
13Kuy wër di sos dangay wuññi sutura, ku jara wóolu dangay am bàmmeelu biir.
14Tegtal tumurànke, am réew suux; digle bare, ndam dikk.
15Bul gàddul kenn bor, di loru; bañ koo dige, daldi am jàmm.
16Jigéen, na yiw, ñu sagal ko; góor gu néeg, alal doŋŋ.
17Ku baax, boppam; ku bon, boppam.
18Coxor feyul boroom, day naxe; deel def njekk, sag pey wóor.
19Saxoo njekk, dund; sàlloo mbon, dee rekk.
20Aji Sax ji bañ na njublaŋ, safoo maandute.
21Ab soxor mbugalam du jaas, wóor na; te ku jub, saw askan mucc.
22Taaru jongama ju xel ma gàtt, mooy jaaro wurus ci noppu mbaam-xuux.
23Ku jub, lu baax rekk lay sàkku; soxor biy yaakaar, mujje mbugal.
24Nit a ngi tabe, di yokkule; nit di nëŋ-nëŋi, gëna ñàkk.

Read Kàddu yu Xelu 11Kàddu yu Xelu 11
Compare Kàddu yu Xelu 11:3-24Kàddu yu Xelu 11:3-24