Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 2.Buur ya - 2.Buur ya 18

2.Buur ya 18:18-36

Help us?
Click on verse(s) to share them!
18Ci kaw loolu ñu woolu Buur. Gannaaw loolu bootalub buur Elyakim doomu Ilkiya moo ànd ak Sebna bindkat ba, ak ka yor téere ya, Yowa doomu Asaf, ñu dikk dajeek ñoom.
19Ba mu ko defee Rabsake bëkk-néegu buurub Asiri ne leen: «Waxleen nag Esekiya ne ko: Buur bu mag ba, buurub Asiri dafa wax ne: “Sa yaakaar jii nga yaakaar, ana foo ko teg?
20Defe nga ne làmmiñ kese doy na pexeek njàmbaar cib xare? Ma ne: Ana kan nga yaakaar bay fippu ci sama kaw?
21Misra daal, nga def sa yaakaar, bantu barax bu tas boobu di sokk képp ku ko wéeroo! Firawna buuru Misra de, mooy boobu bant ci képp ku ko yaakaar.
22Xanaa doo ma ne seen Yàlla Aji Sax ji ngeen yaakaar? Xanaa du moom nga toxal bérabi jaamookaayam yeek sarxalukaayam, ba noppi ne waa Yerusalem ak Yuda sarxalukaay boobu ci Yerusalem lañuy sujjóotal?”
23Léegi daal, déggool rekk ak sama sang buurub Asiri, ma jox la ñaari junniy fas. Ndegam am ngay gawaram!
24Ana noo mana tëwe ki gëna tuut ci sama jawriñi sang? May wax ngay yaakaare Misra ay watiir aki fas!
25Te sax, xanaa du Aji Sax ji laa àndal ba dalsi fi kaw bérab bii, ngir tas ko? Aji Sax ji ci boppam moo ma ne: “Songal réew mii, tas ko!”»
26Ci kaw loolu Elyakim doomu Ilkiya ak Sebna ak Yowa ñaan Rabsake, ne ko: «Ngalla, làkk nu arameen, dégg nanu ko. Bu nu wax ebrë, mbooloo mi ci kaw tata ji di ci dégg.»
27Bëkk-néeg ba ne leen: «Ndax yeen ak seen sang doŋŋ la ma sama sang yóbbante kàddu yii? Ñi toog ci kaw tata ji dañu cee bokkul? Te ñu nara ànd ak yeen lekk seen jonkani bopp, naan seenum saw!»
28Ba loolu amee bëkk-néeg ba taxaw, xaacu ca kaw ci ebrë ne: «Dégluleen kàddug buur bu mag bi, buurub Asiri.
29Buur dafa wax ne bu leen Esekiya nax, ndax manu leena xettli ci loxoom.
30Bu leen Esekiya yaakaarloo Aji Sax ji it, naan leen: “Aji Sax ji moo nuy xettli moos, te deesul teg dëkk bii ci loxol buurub Asiri!”
31Buleen déglu Esekiya. Buurub Asiri kat dafa wax ne: Jàmmooleen ak man te ngeen génn dëkk bi, dikk nangul ma. Su ngeen ko defee, ku nekk ci yeen mana lekk ak jàmm ci garabu reseñam, lekk ak jàmm ci figgam, di naan ndoxum teenam,
32ba keroog may dikk, yóbbu leen réew mu mel ni seen reew mi, réewum pepp ak ndoxum reseñ, réewum mburu ak tooli reseñ, réewum garabi oliw, diw ak lem tuuru, ndax ngeen dund te baña dee. Bu leen Esekiya sànk, naan leen: “Aji Sax ji moo nuy xettli.” Buleen ko déglu!
33Ndax tuuri xeet yi mas nañoo xettli réewu wenn xeet ci buurub Asiri?
34Ana tuuri réew yii di Amat ak Arpàdd? Ana tuuri Sefarwayim ak Ena ak Iwa? Ndax dañoo xettli Samari ci man?
35Tuuri réew yépp, ana mu ci xettli menn réew ak man, ba Aji Sax ji wara mana xettli, Yerusalem ak man?»
36Mbooloo ma nag ne cell, tontuwuñu ko baat, ndax Buur moo leen santoon ne leen buñu ko tontu.

Read 2.Buur ya 182.Buur ya 18
Compare 2.Buur ya 18:18-362.Buur ya 18:18-36