Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Buur ya - 1.Buur ya 9

1.Buur ya 9:1-19

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ba Suleymaan noppee ci tabax kër Aji Sax ji ak kër Buur, ak mboolem nammeelam gu mu bëggoona sottal,
2la ko Aji Sax ji feeñu ñaareel bi yoon, na mu ko feeñoo woon fa Gabawon.
3Aji Sax ji ne ko: «Dégg naa sag ñaan, ak sab dagaan. Sellal naa kër gii nga tabax, ngir teg fi sama tur ba fàww. Samay gët ak sama xol it fi lay nekk bés bu nekk.
4«Yaw nag, soo doxee fi sama kanam ni Daawuda sa baay daan doxe cig mat akug njub, di def lépp lu ma la sant, di sàmm sama dogali yoon, ak sama àttey yoon, nga di ko sàmm,
5kon dinaa saxal sab jal ci kaw Israyil ba fàww, na ma ko waxe woon Daawuda sa baay, ne ko: “Doo ñàkk ku góor kuy toog ci jalub Israyil.”
6Waaye su ngeen ma dëddoo ba dëddu ma, yeen ak seeni sët, ba jëfewuleen samay santaane, sama dogali yoon yi ma leen tëralal, xanaa di topp aka jaamu yeneen yàlla, di leen sujjóotal,
7su boobaa maay dagge bànni Israyil fi déndu suuf si ma leen jox, te kër gi ma sellal ngir sama tur, maa koy xalab, mu sore ma, te kon Israyil mujj di tur wu ñuy léeboo ak di ko kókklee ci biir xeet yépp.
8«Su boobaa kër gii dina gent te képp ku ko romb dina yéemu tey muslu ci lu ni mel. Dinañu ne: “Lu tax Aji Sax ji def nii réew mii ak kër gii?”
9Ñu ne: “Xanaa li ñu dëddu seen Yàlla Aji Sax, ji jële seeni maam réewum Misra, di topp yeneen yàlla, di leen sujjóotal ak a jaamu. Moo tax Aji Sax ji teg leen musiba mii mépp.”»
10Ñaar fukki at yi Suleymaan tabax ñaari kër yi, kër Aji Sax ji ak kër Buur, ba mu matee
11fekk na Iram buurub Tir jox Suleymaan ay banti garabi seedar ak sippar, ak mboolem lu mu soxla ci wurus. Buur Suleymaan nag jox Iram ñaar fukki dëkk ci diiwaanu Galile.
12Ci kaw loolu Iram bàyyikoo Tir, seeti dëkk ya ko Suleymaan jox, waaye dëkk ya neexu ko.
13Mu ne ko: «Sama waay, dëkk yi nga ma jox nag?» Mu daldi tudde dëkk ya réewum Kabul, mooy turam ba tey jii.
14Iram yónnee woon na Buur fanweeri barigoy wurus ak juróom.
15Buur Suleymaan dafa dogaloon liggéeyu sañul-bañ bu mu sas ay nit. Ñu tabax kër Aji Sax ji ak këru boppam ak sëkkub Milo ak tatay Yerusalem ya ak dëkk yii di Àccor, Megido ak Geser. Ni mu deme nii la:
16Firawna buuru Misra moo daloon ci kaw Geser, nangu dëkk ba, lakk ko, rey Kanaaneen ña ca dëkkoon, daldi may dëkk ba doomam jay soxnas Suleymaan, muy yebam.
17Suleymaan tabaxaat Geser ak Bet Oron Suuf,
18ak Baalat ak Tamar ca màndiŋu réew ma,
19ak mboolem dëkki dencukaayam, ak dëkk ya watiiri xare ya dence, ak dëkki gawar ya. Lu Suleymaan nammoona tabax daal, tabax na ko ca Yerusalem ak ca Libaŋ ak mboolem réewum kilifteefam.

Read 1.Buur ya 91.Buur ya 9
Compare 1.Buur ya 9:1-191.Buur ya 9:1-19