Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Buur ya - 1.Buur ya 22

1.Buur ya 22:3-28

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Fekk buurub Israyil wax aki jawriñam ne leen: «Xanaa xamuleen ne Ramot ga ca Galàdd noo ko moom? Te jéemunoo def dara, ba nangu ko ci loxol buurub Siri!»
4Mu ne Yosafat: «Xanaa dinga ànd ak man ca xareb Ramot ga ca Galàdd?» Yosafat ne buurub Israyil: «Maa ngi, yaa ngi, samay nit ay say nit, te samay fas ay say fas.»
5Yosafat teg ca ne buurub Israyil: «Jëkkala seet lu ci Aji Sax jiy wax.»
6Buurub Israyil nag woo yonent yi, ñu daje, xawa tollook ñeenti téeméer. Mu laaj leen ne leen: «Ndax ma dal ci kaw Ramot ga ca Galàdd, am ma bàyyi?» Ñu ne ko: «Demal, ndax Boroom bi moo leen di teg ci sa loxo.»
7Yosafat dellu ne: «Xanaa beneen yonentu Aji Sax ji da fee amatul, ba ñu mana seetlujeeti fa moom?»
8Buurub Israyil ne Yosafat: «Am na ba tey genn góor gu ñu mana seetal ci Aji Sax ji. Waaye man maa ko jéppi, ndax du wax waxyu bu baax ci man, lu bon rekk; mooy Mise doomu Yimla.» Yosafat ne ko: «Buur, bul waxe noonu.»
9Buurub Israyil daldi woo ab jawriñam ne ko: «Demal indil ma gaaw Mise doomu Yimla.»
10Buurub Israyil ak Yosafat buurub Yuda nag, ña nga toog, ku ci nekk ci ngànguneem. Ña nga solu ba jekk ca dàgga ja ca buntu Samari. Yonent yépp janook ñoom di biral ay waxyu.
11Fekk na Cedekiya doomu Kenaana, ma woon ci seen biir, defarlu ay béjjéni weñ. Ma nga naan: «Aji Sax ji dafa wax ne: “Yii ngay jame waa Siri, ba jeexal leen.”»
12Mboolem yonent ya ca des nag di waxe jenn waxyu jooju, naan: «Buur, songal Ramot ga ca Galàdd te jël ndam li, ndax Aji Sax ji moo leen teg ci say loxo.»
13Ci kaw loolu ndaw la wooyi Mise, dem ne ko: «Ma ne, kàddug yonent ya genn la: jàmmu Buur. Kon nag, na sa kàddu ànd ak seen kàddu di genn, te nga wax jàmm.»
14Mise ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund, li ma Aji Sax ji wax rekk laay wax.»
15Ba Mise dikkee ba ca Buur, Buur ne ko: «Mise, ndax nu songi xare Ramot ga ca Galàdd, am nu bàyyi?» Mu ne ko: «Buur songal, daan, Aji Sax jee koy teg ci sa loxo!»
16Buur nag ne ko: «Ñaata yoon laa lay giñloo ne la bu ma wax lu moy dëgg ci turu Aji Sax ji?»
17Mise ne ko: «Israyil gépp laa gis ñu tasaaroo ca tund ya, mbete xar yu amul sàmm. Aji Sax ji ne: “Ñii de amuñu boroom. Na ku nekk ci ñoom ñibbi këram ci jàmm.”»
18Buurub Israyil ne Yosafat: «Waxuma la woon ne du wax waxyu bu baax ci man, xanaa lu bon?»
19Mise teg ca ne ko: «Kon nag déglul kàddug Aji Sax ji. Gis naa Aji Sax ji, mu toog ci ngànguneem, mboolem gàngooru asamaan a nga taxaw ndijooram ba càmmoñam.
20Aji Sax ji nag ne: “Ana kuy nax Axab, mu songi Ramot ga ca Galàdd, ba daanu ca?” Kii ne nii, kee ne nee.
21Noo ga dikk, taxaw fa kanam Aji Sax ji. Mu ne: “Man maa koy nax.” Aji Sax ji ne ko: “Nan?”
22Mu ne: “Maay dikk, doon xel muy safaan dëgg ci làmmiñu yonentam yépp.” Mu ne ko: “Yaa koy nax, te man nga ko. Demal defe noonu.”
23Looloo waral lii. Aji Sax ji moo def xel muy safaan dëgg ci sa làmmiñu yonent yii yépp, te Aji Sax ji moo tudd musiba ci sa kaw.»
24Ba loolu amee Cedekiya doomu Kenaana talaata Mise, ne ko: «Ana fu Noowug waxyu gu Aji Sax ji jaare, ba jóge ci man di wax ak yaw?»
25Mise ne ko: «Yaw mii yaa koy gisal sa bopp, keroog ba ngay dugg néegoo néeg, di làqtu.»
26Buurub Israyil ne ab surgaam: «Jàppal Mise, yóbbu ko ca Amon boroom dëkk bi, ak ca doomu Buur.
27Nga ne ko: “Buur dafa wax ne: Dugal-leen kii ndungsiin, di ko jox lekk gu néew ak ndox mu néew, ba keroog may dikk ak jàmm.”»
28Mise ne: «Soo délseek jàmm déy, Aji Sax ji waxul, ma jottli.» Mu dellu ne: «Mbooloo mi, yeena ko déggandoo, yeen ñépp.»

Read 1.Buur ya 221.Buur ya 22
Compare 1.Buur ya 22:3-281.Buur ya 22:3-28