Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Buur ya - 1.Buur ya 21

1.Buur ya 21:10-26

Help us?
Click on verse(s) to share them!
10te teg ñaari nit ñu tekkiwul dara, ñu janook moom. Na ñooñu duural Nabot ne ko: “Saaga nga Yàlla, saaga Buur.” Su ko defee ngeen génne ko dëkk ba, dóor ko ay doj ba mu dee.»
11Ba mu ko defee waa dëkkub Nabot, mag ñaak gor ña daldi def la Yesabel santaane te bind ko ca bataaxal ya mu leen yónnee.
12Ñu yéene koor, beral Nabot jataay ca kanam mbooloo ma.
13Ñaari nit ñu tekkiwul dara dikk toog janook moom. Ñu duural ko ca kanam mbooloo ma, ne Nabot daa saaga Yàlla, saaga Buur. Ñu génne Nabot dëkk ba, dóor ko ay doj ba mu dee.
14Ñu yónnee nag ca Yesabel ne ko dóor nañu Nabot ay doj ba mu dee.
15Yesabel dégg ca, ne Axab: «Jógal nanguji toolu reseñu Nabot waa Yisreel bi. Moo la ko bañoona jaaye xaalis, waaye dundatul, dee na.»
16Axab dégg ca, daldi jubal toolu reseñu Nabot waa Yisreel ba, nangu ko.
17Ci biir loolu kàddug Aji Sax ji dikkal Ilyaas ma dëkk Tisbi, ne ko:
18«Demal taseek Axab buurub Israyil ba ca Samari. Ma nga nee ca toolu reseñu Nabot ba mu nanguji.
19Wax ko ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Du dangaa rey nit, ba nangu alalam?” Nga teg ca ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Fa xaj ya xabe deretu Nabot, ay xaj dina fa xabe sa deret, yaw itam.”»
20Axab ne Ilyaas: «Ãa, noon bi, gisati nga ma?» Ilyaas ne ko: «Gis naa la, ndax dangaa dogu ci def lu bon lu Aji Sax ji ñaawlu.
21Aji Sax ji nee na: Dama ne, dinaa wàcce lu bon ci sa kaw, fàllas say sët, ba faagaagal ci digg Israyil kuy taxaw, colal, te bokk ci yaw Axab, muy gor, di jaam.
22Dinaa def sa kër mel ni kër Yerbowam doomu Nebat mbaa kër Basa doomu Axiya, ndax merloo nga ma te bàkkaarloo nga Israyil.
23Te itam Aji Sax ji wax na ci mbirum Yesabel ne: Ay xaj dina lekk Yesabel ca wetu tatay Yisreel.
24Ku Axab deele ci dëkk bi, xaj yi lekk; ku ci médde àll, njanaaw ya for.»
25Axab dafa dogu woon ci def lu bon lu Aji Sax ji ñaawlu, ba amu ci moroom moos, te jabaram Yesabel di ko ci xabtal.
26Axab daan na def ñaawtéef ju réy, di topp ay kasaray tuur, di def mboolem lu doon baaxu Amoreen ña Aji Sax ji dàqoon ngir bànni Israyil.

Read 1.Buur ya 211.Buur ya 21
Compare 1.Buur ya 21:10-261.Buur ya 21:10-26