Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 14

Sarxalkat yi 14:42-57

Help us?
Click on verse(s) to share them!
42Dañoo wara sàkkaat ay doj, wuutale ko doj yooyu te sàkk ban bu bees, raaxe ko néeg bi.
43«Su liir wi delloo tegu ci biir néeg bi gannaaw bu ñu teggee doj yi, xeet biir néeg bi, ba raax ko,
44sarxalkat bi day dikk seet ko. Su liir wi lawee ci néeg bi, liir wu aaytal la wu xuural biir néeg bi, di sobe.
45Néeg ba dees koy daane, boole doj yaak bant yaak banu raax ba bépp, génne ko dëkk bi, tuur ko fu setul.
46«Ku dugg biir néeg bi diiru fan yi mu tëje dina yendoo sobe ba jant so.
47Ku tëdd ca biir néeg ba war naa fóot ay yéreem te ku fa lekke it war naa fóot ay yéreem.
48«Su sarxalkat ba delloo ca néeg ba, seet ko, fekk liir wa lawul ca néeg ba, gannaaw ba ñu ko raaxee, na biral ne néeg bi set na, ndax kon liir wa raaf na.
49Liy laabal néeg bi moo di mu sàkk ñaari picc ak bantu garabu seedar ak wëñ gu xonq curr ak caru isob.
50Day rendi menn picc mi, tiimale ko ndabal xandeer mu def ndox mu balle ci bëtu ndox.
51Bu noppee na jaxase deretu picc mi ñu rendi ak ndox mu balle ci bëtu ndox, daldi jël bantu seedar bi ak caru isob bi ak wëñ gi xonq curr ak picc miy dund, boole lépp sóob ca. Su ko defee mu wis-wisal ca juróom ñaari yoon ci néeg bi.
52Kon li muy laabale néeg bi moo di deretu picc mi ak ndox moomu ak picc miy dund ak bantu seedar bi ak caru isob bi ak wëñ gi xonq curr.
53Na bàyyi picc miy dund fu génn dëkk ba, mu naaw ca àll ba. Noonu lay defe njotlaayal néeg bi, mu set.»
54Loolu la yoon digle ci lépp luy jàngoroy der juy law ak wat-wataan,
55mbaa liir wu tegu ci ndimo mbaa ci néeg,
56ak ci wàllu tërgën itam mbaa mu diy ër mbaa gàkk bu weex;
57mooy tegtal biy xamle lu set ak lu setul. Loolu la yoon digle ci jàngoroy der juy law mbaa liir.

Read Sarxalkat yi 14Sarxalkat yi 14
Compare Sarxalkat yi 14:42-57Sarxalkat yi 14:42-57