3Ma àrtu leen ci kaw yiw wi ma Yàlla may; bu kenn ci yeen teg boppam fu mu àggul, waaye xalaate leen sago, te ku nekk dëppoo ak céru ngëm bi ko Yàlla sédd.
4Ndax kat dafa mel ni sunu yaram wiy wenn, te cér yi bare, doonte cér yépp a wuuteek seen moroom nu ñuy liggéeye.
5Noonu lanu doone ñu bare, bokk wenn yaram nun ñépp ci Almasi mi nu gëm, te ku nekk di sa cérub moroom.
6Ay may yu wuute lanu am, may yu yemook céru yiw bi ñu sédd ku nekk ci nun. Su dee biral kàddug waxyu mooy sag may, biraleel kàddug waxyu sa kemu ngëm;
7su dee wàllu jàpple, deel jàpple; su dee wàllu njàngle, ngay jàngle;
8Su dee wàllu kàddu yuy yokke, ngay wax luy yokk gëmkat ñi; su dee wàllu joxe, deel joxe te Yàlla rekk tax; su dee wàllu jiite, taxawal temm ci liggéeyub jiite; su dee wàllu baaxe nit ñi, nay loo bége.
9Na seen cofeel mucc ci ngistal, seexluleen lu bon te ŋoy ci lu baax.
10Na leen mbëggeelug bokk taxa fonkante, te ngeen farlu ci di terlante.
11Sawarleen te baña yoqi, jaamuleen Boroom bi, ànd ceek pastéefu xol.
12Bégeleen seen yaakaar, di muñ ci biir tiis, tey saxoo ag ñaan.
13Deeleen def seen loxo ci lu faj soxlay gëmkat ñu sell ñi, te boole ci am teraanga.