7Rafet, sopploo! Soppee, bànneex nga!
8Sa taxawaay bii garabu tàndarma la, sa ween yi di cëggi doom ya.
9Ma ne, maay yéeg tàndarma gi, ŋëb doom yi. Yal na say ween di sama cëggi reseñ, sag noo jox ma doom yu xeeñ,
10sa gémmiñ di xelli ngëneelu biiñ. Ndaw si Na walal sama nijaay, tuurul ñiy nelaw.
11Man, nijaay a moom, te maay nammeelam.
12Nijaay, ayca nu dem tool ba, fanaani ca tóor-tóori fuddën ya.
13Nan teela xëyi ca tóokëri reseñ ya, bu reseñ ji jebbee, mbaa tóor-tóor yi focci, mbaa gërënaat ji tóor, nu gis. Fa laa lay jébbale mbëggeel.