2Ci kaw loolu Balaam dawal bëtam, daldi séen Israyil, na ñu dale topp seeni giir, Noowug Yàlla daldi wàcc ca moom.
3Ba mu ko defee mu yékkati kàddug ñaanam, ne: «Kàddug Balaam a ngi, doomu Bewor, kàddug waa jiy boroom ngis,
4kàddug kiy dégg waxi Yàlla, Aji Man ji wonem peeñu, mu gis, kiy daanu leer, te ay gëtam muriku.