Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 15

Màndiŋ ma 15:9-20

Help us?
Click on verse(s) to share them!
9na sarxewaaleek jur gu gudd gi, ab saraxu pepp bu ñetti fukkeeli efay sunguf su mucc ayib, di juróom ñeenti kilo, ñu xiiwe ko genn-wàllu xiinu diw, di ñetti liitar,
10ak biiñ bu muy joxewaale, ngir saraxu tuuru, di genn-wàllu xiin, muy ñetti liitar. Loolu saraxu sawara la, di xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
11«Noonu lees di def bu dee saraxu yëkk, mbaa am kuuy, mbaa am xar mu ndaw, mbaa bëy.
12Nu limu juri sarax yi tollu rekk, ngeen def mu ci nekk noonu, ànd ak lim ba.
13Mboolem njuddu-ji-réew, noonu lay defe sarax yooyii, buy indi saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
14«Su dee ab doxandéem bu dal ak yeen, mbaa ku nekk ak yeen ci seen maas yiy ñëw, te muy joxe saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji, ni ngeen koy defe rekk la koy defe.
15Mbooloo mi mépp, dogalu yoon boobu benn la ciy doon, muy yeen, di doxandéem bi. Dogal la buy sax fàww, ñeel seen maasoo maas, te di benn ci yeen ak ci doxandéem bi, fi kanam Aji Sax ji.
16Wenn yoon wee, di benn àtte bi, ñeel leen, ñeel doxandéem bi dal ak yeen.»
17Aji Sax ji waxati Musaa, ne
18«Waxal bànni Israyil, ne leen, bu ngeen demee ca réew, ma ma leen jëme,
19bay lekk ca ñamu réew ma, nangeen ci jooxe ab jooxe, ñeel Aji Sax ji;
20seen notu sunguf bu jëkk, ci ngeen di jooxe menn mburum jooxe. Ni ngeen di sàkke jooxe bu jóge ca dàgga ja rekk, ni ngeen koy jooxee.

Read Màndiŋ ma 15Màndiŋ ma 15
Compare Màndiŋ ma 15:9-20Màndiŋ ma 15:9-20