18Ñi dégg li sàmm yi doon wax ñépp daldi waaru lool.
19Waaye Maryaama moom, takkoon na mbir yooyu yépp, di ko xalaat ci xolam.
20Noonu sàmm ya dellu ca seen jur, di màggal Yàlla, di ko sant ci li ñu déggoon lépp te gis ko, ndaxte lépp am na, ni ko Boroom bi waxe woon.
21Bi bés ba délsee jamonoy xarafal xale ba agsi. Ñu tudde ko Yeesu, ni ko malaaka ma diglee woon, laata ko yaayam di ëmb.
22Noonu jamono ji ñu leen waroona sellale agsi, ni ko yoonu Musaa tërale. Waajuri Yeesu yi daldi koy yóbbu ca dëkku Yerusalem, ngir sédde ko Boroom bi.
23Ndaxte bind nañu ci yoonu Boroom bi ne: «Bépp taaw bu góor, nañu ko sédde Boroom bi.»
24Bi ñu ko yóbboo, def nañu itam sarax, ni ko yoonu Boroom bi santaanee: «ñaari pitaxu àll walla ñaari xati yu ndaw.»