13«Boroom tool ba daldi ne: “Nan laay def nag? Dinaa yónni sama doom, sama reeni xol. Xëy na ñu weg ko, moom.”
14Waaye bi beykat yi gisee doom ji, ñu ne ci seen biir: “Kii moo wara donn tool bi; nan ko rey, moom ndono li.”
15Ñu génne ko tool bi nag, rey ko.» Noonu Yeesu laaj leen: «Nu leen boroom tool bi di def, nag?
16Xanaa ñëw, rey beykat yooyu, dénk tool ba ñeneen.» Bi Yeesu waxee loolu, nit ña ne ko: «Yàlla tere!»
17Waaye Yeesu ne leen jàkk, daldi ne: «Kon nag lu baat yii ci Mbind mi di tekki: “Doj wa tabaxkat ya sànni, mujj na di doju koñ.”
18Képp ku dal ci doj woowu, dammtoo, te ku mu dal ci sa kaw, rajaxe la.»
19Xutbakat ya ak sarxalkat yu mag ya ñu ngi doon wuta jàpp Yeesu ca taxawaay ba, ndaxte xam nañu ne ñoo tax mu wax léeb woowu. Waaye ragal nañu mbooloo ma.
20Noonu ñu koy yeeru, daldi yónni ay nit ñu mbubboo njub, sas leen ñu fexe koo jàpp ci ay waxam, ngir jébbal ko boroom réew, ma yor kilifteef ak sañ-sañ.
21Ñu daldi ñëw ci Yeesu ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne li ngay wax te di ko jàngle lu jub la. Amuloo parlàqu, waaye dangay xamle yoonu Yàlla ci bu wóor.
22Wax nu, ndax jaadu na, nu fey buur bi Sesaar galag walla déet.»
23Waaye Yeesu xam na seen pexe ne leen:
24«Wonleen ma posetu denariyon. Kan lañu ci def nataalam ak turam?» Ñu ne ko: «Sesaar.»
25Noonu mu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Yàlla li Yàlla moom.»
26Noonu manuñu ko woona jàpp ciy waxam ci kanam mbooloo ma; ñu waaru ci tontam, ba wedam.
27Noonu ay nit, ñu bokk ci Sadusen yi, ñëw ci moom. Sadusen yi nag ñoom weddi nañu ndekkite li. Noonu ñu laaj ko ne:
28«Kilifa gi, Musaa bindal na nu ne, ku magam faatu te bàyyiwul doom ak soxnaam, kooku war na donn jigéen ji, ba yékkati giiru magam.
29Amoon na fi nag juróom ñaari góor ñu bokk ndey ak baay. Taaw ba takk jabar, faatu, te bàyyiwul doom.
30Ñaareel ba takk jigéen ja, def noonu; ak ñetteel ba, ba juróom ñaar ñépp faatu te bàyyiwuñu doom.
32Gannaaw ga nag jigéen ja it faatu.
33Ci ndekkite li nag, kan ci ñoom moo wara donn jigéen ja, fekk ku nekk ci juróom ñaar ñi mas na koo takk?»
34Yeesu ne leen: «Ci àddina sii, góor ñi ak jigéen ñi dañuy séy.
35Waaye ña ñu àtte ne yeyoo nañoo bokk ci dundu ëllëg ak ci ndekkite li, kenn du am jabar, kenn du am jëkkër.
36Dafa fekk ne manatuñoo dee, ndaxte dañuy mel ni malaaka yi. Ay doomi Yàlla lañu ndaxte doomi ndekkite lañu.
37Te Musaa sax wone na ne, néew yi dinañu dekki, ci saarum ngarab si. Foofa Musaa wooye na fa Boroom bi: “Yàllay Ibraayma, Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba.”
38Kon nag nekkul Yàllay ñi dee waaye Yàllay ñiy dund la, ndaxte Yàllaa tax ñépp di dund.»
39Ci kaw loolu ay xutbakat ne ko: «Li nga wax dëgg la, kilifa gi!»
40Ndaxte kenn ci ñoom ñemeetu koo laaj dara.
41Noonu Yeesu ne leen: «Lu tax nit ñi di wax ne, Almasi bi mooy sëtu Daawuda?
42Ndaxte Daawuda moom ci boppam moo ne ci Sabóor: “Boroom bi nee na sama Boroom: ‘Toogal ci sama ndijoor,
43ba kera may daaneel say noon ci sa kanam.’ ”
44Gannaaw Daawuda nag wooye na ko “Boroom bi,” nu muy nekke sëtam?»