18Surga ba ca topp ñëw ne: “Sang bi, sa libidoor ba indi na juróomi libidoor.”
19Buur ba ne ko: “Yaw, falul ci juróomi dëkk.”
20Keneen ñëw ne: “Sang bi, sa libidoor baa ngi nii. Dama koo fasoon ci sekkit, denc ko.
21Dama laa ragaloon, ndaxte ku néeg nga. Dangay nangu loo dénkaanewul, di dajale loo jiwul.”
22Buur ba ne ko: “Ci say wax laa lay àtte, surga bu bon bi! Xamoon nga ne, nit ku néeg laa, di nangu lu ma dénkaanewul, te dajale lu ma jiwul.
23Lu tax nag yóbbuwoo sama xaalis ca denckati xaalis ya? Bés bu ma ñëwee nag, ma mana jot sama xaalis ak la mu jur.”
24«Ci kaw loolu mu ne ña taxawoon ca wetam: “Nanguleen libidoor bi ci moom, jox ko boroom fukki libidoor yi.”
25Ñu ne ko: “Sang bi, am na fukki libidoor ba noppi.”
26Buur ba ne leen: “Maa ngi leen koy wax, ku am, dinañu la dolli, waaye ku amul, li nga am as néew sax, dinañu ko nangu.
27Waaye sama noon yi, ñi bëggul woon ma doon seen buur, indileen fii, rey leen ci sama kanam.”»
28Bi mu waxee loolu ba noppi, Yeesu dafa daldi jiitu, jëm Yerusalem.
29Bi muy jege dëkki Betfase ak Betani, ci wetu tund wu ñuy wax tundu Oliw ya, Yeesu yebal ñaar ci ay taalibeem,
30ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci kanam. Bu ngeen fa duggee, dingeen fa gis cumbur gu kenn masula war. Yiwileen ko, indi.
31Bu leen kenn laajee: “Lu tax ngeen koy yiwi?” neleen ko: “Boroom bi da koo soxla.”»
32Ñaari ndaw ya dem, fekk mbir ya deme, na leen ko Yeesu waxe woon.
33Bi ñuy yiwi cumbur ga nag, ay boroomam ne leen: «Lu tax ngeen di yiwi cumbur gi?»
34Ñu ne: «Ndaxte Boroom bi da koo soxla.»
35Noonu ñu indil cumbur gi Yeesu, daldi lal seeni yére ca kaw, yéegal ca Yeesu.
36Bi muy dem, nit ñi di lalal Yeesu seeni yére ci yoon wi.
37Bi ñu agsee fa mbartalum tundu Oliw ya doore, taalibeem yépp fees ak mbég, tàmbalee màggal Yàlla ca kaw ndax kéemaan yu bare yi ñu gis.
38Ñu ngi naan: «Yaw buur biy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga! Na jàmm am ca asamaan, te ndam li féete ca bérab yu gëna kawe!»
39Waaye ay Farisen yu nekkoon ca mbooloo ma ne Yeesu: «Kilifa gi, yeddal sa taalibe yi!»
40Noonu mu ne: «Maa ngi leen koy wax, bu ñu noppee ñoom, doj yiy xaacu.»