Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 12

LUUG 12:4-18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4«Maa ngi leen koy wax, samay xarit, buleen ragal ñu mana rey yaram, ba noppi dootuñu mana def dara.
5Dinaa leen wax nag ki ngeen wara ragal: ragal-leen ki nga xam ne bu reyee ba noppi, am sañ-sañu sànni ca sawara. Waaw, maa ngi leen koy wax, ragal-leen kooku.
6Juróomi picci ramatu, ndax duñu ko jaay ci ñaari dërëm? Moona Yàlla fàttewul benn ci ñoom.
7Seen kawari bopp sax waññees na leen. Kon buleen ragal dara, yéena gën ndiiraanu ramatu.
8«Te maa ngi leen koy wax, képp ku ma nangu ci kanam nit ñi, Doomu nit ki dina la nangu ci kanam malaakay Yàlla yi.
9Waaye ku ma gàntu ci kanam nit ñi, dinañu la gàntu ci kanam malaakay Yàlla yi.
10Ku sosal Doomu nit ki, dinañu la baal, waaye kuy sosal Xel mu Sell mi, duñu la ko baal.
11«Bu ñu leen yóbboo ca jàngu ya, ca kanam kilifa ya ak àttekat ya, buleen am xel ñaar ci li ngeen wara tontu ak nan ngeen wara tontoo, walla lu ngeen wara wax,
12ndaxte Xel mu Sell mi dina leen xamal ca waxtu woowa li ngeen wara wax.»
13Am ca mbooloo ma ku ne Yeesu: «Kilifa gi, joxal ndigal sama mag, mu sédd ma ci sunu ndono.»
14Yeesu ne ko: «Sama waay, kan moo ma fal àttekat ci seen kaw, walla mu teg ma fi, ma di leen séddaleel seen alal?»
15Noonu mu ne leen ñoom ñépp: «Moytuleen bëgge, ndaxte bakkanu nit ajuwul ci alalam, ak lu mu baree bare.»
16Noonu mu dégtal leen wii léeb ne: «Dafa amoon waa ju bare alal, te ay toolam nangu lool,
17muy werante ci xelam naan: “Nu ma wara def? Ndaxte amatuma fu ma dajale sama ngóob mi.”
18Noonu mu ne: “Nii laay def: daaneel sama sàq yi, defaraat yu gëna réy, ba man cee dajale sama dugub ji ak sama am-am bépp.

Read LUUG 12LUUG 12
Compare LUUG 12:4-18LUUG 12:4-18