Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 12:4-18 in Wolof

Help us?

LUUG 12:4-18 in Téereb Injiil

4 «Maa ngi leen koy wax, samay xarit, buleen ragal ñu mana rey yaram, ba noppi dootuñu mana def dara.
5 Dinaa leen wax nag ki ngeen wara ragal: ragal-leen ki nga xam ne bu reyee ba noppi, am sañ-sañu sànni ca sawara. Waaw, maa ngi leen koy wax, ragal-leen kooku.
6 Juróomi picci ramatu, ndax duñu ko jaay ci ñaari dërëm? Moona Yàlla fàttewul benn ci ñoom.
7 Seen kawari bopp sax waññees na leen. Kon buleen ragal dara, yéena gën ndiiraanu ramatu.
8 «Te maa ngi leen koy wax, képp ku ma nangu ci kanam nit ñi, Doomu nit ki dina la nangu ci kanam malaakay Yàlla yi.
9 Waaye ku ma gàntu ci kanam nit ñi, dinañu la gàntu ci kanam malaakay Yàlla yi.
10 Ku sosal Doomu nit ki, dinañu la baal, waaye kuy sosal Xel mu Sell mi, duñu la ko baal.
11 «Bu ñu leen yóbboo ca jàngu ya, ca kanam kilifa ya ak àttekat ya, buleen am xel ñaar ci li ngeen wara tontu ak nan ngeen wara tontoo, walla lu ngeen wara wax,
12 ndaxte Xel mu Sell mi dina leen xamal ca waxtu woowa li ngeen wara wax.»
13 Am ca mbooloo ma ku ne Yeesu: «Kilifa gi, joxal ndigal sama mag, mu sédd ma ci sunu ndono.»
14 Yeesu ne ko: «Sama waay, kan moo ma fal àttekat ci seen kaw, walla mu teg ma fi, ma di leen séddaleel seen alal?»
15 Noonu mu ne leen ñoom ñépp: «Moytuleen bëgge, ndaxte bakkanu nit ajuwul ci alalam, ak lu mu baree bare.»
16 Noonu mu dégtal leen wii léeb ne: «Dafa amoon waa ju bare alal, te ay toolam nangu lool,
17 muy werante ci xelam naan: “Nu ma wara def? Ndaxte amatuma fu ma dajale sama ngóob mi.”
18 Noonu mu ne: “Nii laay def: daaneel sama sàq yi, defaraat yu gëna réy, ba man cee dajale sama dugub ji ak sama am-am bépp.
LUUG 12 in Téereb Injiil

Luug 12:4-18 in Kàddug Yàlla gi

4 «Maa leen ko wax, yeen samay soppe, buleen ragal ñu manul lu wees rey seen yaram, ndax gannaaw loolu dootuñu leen manal lu ko raw.
5 Ma xamal leen nag ki ngeen wara ragal: kiy rey ba noppi, am sañ-sañu sànni ca sawara sa, kooku déy laa leen ne, ragal-leen ko.
6 Juróomi picci ramatu, xanaa jarul ñaari dërëm doŋŋ? Moona Yàlla fàttewula geesu menn ci ñoom.
7 Yeen nag seen kawari bopp sax, waññees na lépp. Buleen ragal dara, nde ndiiraanu ramatu, yeena ko gën.
8 «Te it maa leen ko wax, képp ku dëggal fi kanam nit ñi, ne man nga féeteel, Doomu nit ki itam dina dëggal fa kanam malaakay Yàlla ya, ne moom nga féeteel.
9 Waaye ku weddi fi kanam nit ñi, ne man nga féeteel, dees na weddi fa kanam malaakay Yàlla ya, ne man nga féeteel.
10 Képp ku jëme kàddug safaan ci Doomu nit ki, dees na la jéggal, waaye ku saaga Noo gu Sell gi, deesu la jéggal.
11 «Bu ñu leen yóbboo ca jàngu ya, ca kanam kilifa ya, ak àttekat ya, buleen jaaxle ci nan ngeen di yékkatee kàddug layoo, ak luy doon seenu lay, mbaa lu ngeen di wax,
12 ndax su boobaa Noo gu Sell gi moo leen di xamal ca waxtu woowa la ngeen wara wax.»
13 Kenn ca mbooloo ma moo noon Yeesu: «Sëriñ bi, waxal ci sama mag, mu jox ma sama wàll ci ndono li nu bokk.»
14 Yeesu ne ko: «Waa jii, kan moo ma fal àttekat mbaa miraaskat ci seen kaw?»
15 Ci kaw loolu mu ne leen ñoom ñépp: «Moytuleen wépp xeetu bëgge, ndax loo barele barele, sa bakkan ajuwul ci sa alal.»
16 Mu léeb leen nag, ne leen: «Nit la woon ku woomle, te ab toolam nangu.
17 Mu naan ca xel ma: “Nu may def nag? Amatuma sax fu ma denc sama ngóob mi!”
18 Ci kaw loolu mu ne: “Nii laay def: samay sàq laay daaneel, daldi defaraat sàq yu gëna mag, denc ci sama pepp ak mboolem lu ma am.
Luug 12 in Kàddug Yàlla gi