32Waa réewum Niniw it keroog àtte ba dinañu taxaw, layook niti tey jii, tiiñal leen ndax ñoo tuube woon ca waareb Yunus, te tey jii, ku sut Yunus a ngi fi.
33«Deesul taal ab làmp, di ko dugal fu làqu, mbaa ci suufu leget. Dees koy aj kay, ba kuy duggsi gis muy leer.
34Bët mooy làmpu yaram. Bu sa bët wéree, sa yaram wépp a ciy leerloo, waaye bu sa bët bonee, sa yaram wépp a ngi ci lëndëm.
35Kon seetal ndax leer gi nga foog ne mu ngi ci yaw du ag lëndëm.
36Bu sa yaram wépp dee leerlu nag te lenn nekku ci cig lëndëm, su boobaa la sa yaram di mana leerlu ba ne ràññ, mel ni bu la ab làmp niitee, ne ràññ ci sa kaw.»
37Ba Yeesu waxee ba noppi, ab Farisen da koo woo këram, ngir bokk ak moom lekk. Mu nangu, dem ba duggsi, daldi toog ca lekkukaay ba.
38Farisen bi nag jaaxle, ndax la Yeesu setluwul bala moo waaja lekk.