3Lu mettee ngi nii ci mboolem lu am fi kaw suuf: Benn dogal la ñépp bokk, te it nit a ngi sóobu ci mbon, di mébét jëfi dof giiru dundam, ba noppi fekki ña dee.
4Képp kuy dund kat, am nga yaakaar, te xaj buy dund a gën gaynde gu dee.
5Kuy dund xam ne dangay dee, waaye ku dee xamul dara, te séentootul ab yool. Ku dee, ñu fàtte la.
6Muy sa cofeel, di sa mbañeel, ba ci sa kiñaan ànd ak yaw seey. Du lenn lu deeti sa wàll ci jépp jëfi kaw suuf.
7Kon doxal, lekk saw ñam, bége, te naan sa biiñ ci xol bu sedd. Yàlla kat nangul na la jeeg say jëf.
8Foo tollu, solul ba jekk, te bul fàttee xeeñlu.