Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàdduy Waare - Kàdduy Waare 6

Kàdduy Waare 6:3-11

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Ku giir téeméeri doom, dund ati at, ak lu at ya bare bare, su bégewul teraanga ja mu am te amul njégu bàmmeelam sax, kooku lumb wu tuuroo ko tane.
4Lumb wa ñëw na moos ci neen, bàddoo lëndëm, turam sàngoo lëndëm.
5Gisul jant, xamu ko, waaye noflaay moo ko ëpple mag ma,
6bu dundoon junniy junniy at sax te amul jàmm. Xanaa du benn bérab la ñépp jëm?
7Nit ak doñ-doñam jépp, biiram, te taxul mu doylu.
8Ana lu boroom xel ëpplee ku dofe? Nga ñàkk, xam doxalin, lu mu lay jariñ?
9Doyloo li nga gis a gën di wéye xemmem. Loolu it, cóolóoli neen ak napp um ngelaw.
10Lu masa ay, dees koo tuddoon; lu doom aadama doon, xamees na ko, te kenn du layook ku la sut.
11Loo ci wax wax, solo sa gëna néew. Kon ana loo ci jële?

Read Kàdduy Waare 6Kàdduy Waare 6
Compare Kàdduy Waare 6:3-11Kàdduy Waare 6:3-11