Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàdduy Waare - Kàdduy Waare 5

Kàdduy Waare 5:9-19

Help us?
Click on verse(s) to share them!
9Bëggkatu xaalis du doyal xaalis, bëggkatu alal du doyal tono, te loolu it, cóolóoli neen.
10Bu koom yokkoo, lekk-kat yi yokku. Ana lu muy jariñ boroom koom ga, xanaa di ko duufale bëtam?
11Surga, lekkam néew, bare, mu nelaw, ba fàttey boram; boroom alal regg, du nopplu, du nelaw.
12Naqar wu réy laa gis fi kaw suuf: Alal ju boroom dajale ba loru,
13mbaa pexeem moy, mu sànkule; ba bu amee doom it, du ko wacce dara.
14Nga juddoo ci sa ndey loxoy neen, walbatiku dellu na nga dikke woon. Du dara loo ñaqoon ba yóbbaale ko.
15Dikke ni, delloo ni, loolu it tiis wu réy la. Doñ-doñi, ngelawal neen, ana jariñ la?
16Ngay dunde tiis bésoo bés, ak naqar ak wopp ak xol bu tàng!
17Lii daal laa ci gis, man. Li gën te jaadu ci nit: Na lekk, naan te bànneexoo ñaqam wu mu ñaqe kaw suuf giiru dund gi ko Yàlla may. Loolu mooy céram.
18Alal ak koom, ku ko Yàlla may, may ko mu tal koo xéewloo, mu nangu céram, bànneexoo ñaqam, loolu mayu Yàllaa.
19Yàllaa koy bànneexal, ba du tiisoo ay fanam.

Read Kàdduy Waare 5Kàdduy Waare 5
Compare Kàdduy Waare 5:9-19Kàdduy Waare 5:9-19