15Dikke ni, delloo ni, loolu it tiis wu réy la. Doñ-doñi, ngelawal neen, ana jariñ la?
16Ngay dunde tiis bésoo bés, ak naqar ak wopp ak xol bu tàng!
17Lii daal laa ci gis, man. Li gën te jaadu ci nit: Na lekk, naan te bànneexoo ñaqam wu mu ñaqe kaw suuf giiru dund gi ko Yàlla may. Loolu mooy céram.
18Alal ak koom, ku ko Yàlla may, may ko mu tal koo xéewloo, mu nangu céram, bànneexoo ñaqam, loolu mayu Yàllaa.
19Yàllaa koy bànneexal, ba du tiisoo ay fanam.