3Ki leen taneeti yeen ñépp di ki juddoogul sax, moom mi gisul jëf ju bon fi kaw suuf.
4Ma gis ne nit ak kër-këram jépp ak bépp manoorey liggéey, iñaanantee ko waral. Loolu it, cóolóoli neen ak napp um ngelaw.
5Dof banki loxoom, sànk boppam.
6Waaye benn ŋëb bu ànd ak dal moo gën ñaari ŋëbi doñ-doñ ci napp um ngelaw.
7Ma seetlu leneen luy cóolóoli neen fi kaw suuf.
8Kenn a ngii, kenn ñaareelu ko, du doom, du mbokk. Doñ-doñam du dakk, te du doylu, mujj mu naan: «Kan laay doñ-doñil, di xañ sama bopp bànneex?» Loolu it, cóolóoli neen, di sas wu tiis.
9Ñaar a man kenn; doñ-doñoondoo, yoolu bu baax.
10Kenn daanu, moroom ma may ko loxo. Waaye ngalla ku daanu te amuloo ku la may loxo!
11Bu ñu tëddee di ñaar it, mana bokk nuglu. Waaye soo dee kenn, nooy nugloo?
12Fu ñu mane kenn, ñaar taxaw fa, jéngu, te buumu ñetti xànc gaawula dog.
13Kuy ndaw, génne kaso, tàmbalee nguuru fa mu juddoo woon mbaadoolo, ndaw loolu su dee baadoolo te xelu it, moo gën buur bu màggat, dofe, dégguli àrtu.