1Ma seetlooti gépp notaange gu am fi kaw suuf. Ndeke néew-doolee ngi jooy, amul ku ko dëfal. Ki koy not a am doole, te néew-doole ji amul ku ko dëfal.
2Dama ne ndokklee, yeen ñi dee jeeg, nde raw ngeen ñiy dund!
3Ki leen taneeti yeen ñépp di ki juddoogul sax, moom mi gisul jëf ju bon fi kaw suuf.
4Ma gis ne nit ak kër-këram jépp ak bépp manoorey liggéey, iñaanantee ko waral. Loolu it, cóolóoli neen ak napp um ngelaw.
5Dof banki loxoom, sànk boppam.
6Waaye benn ŋëb bu ànd ak dal moo gën ñaari ŋëbi doñ-doñ ci napp um ngelaw.
7Ma seetlu leneen luy cóolóoli neen fi kaw suuf.