Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàdduy Waare - Kàdduy Waare 2

Kàdduy Waare 2:3-25

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Saam xel ne ma, ma naan biiñ boog, bégloo, ba mel nib dof, tey ànd ak sama xel, ba gis lu ci baax, ba doom aadama di ko def, giiru dundam fi ko jant bi tiim.
4Damaa liggéey lu réy. Tabaxlu naa samay kër, jëmbat sama toolub reseñ.
5Ma sàkki tóokër aki tool, jëmbat ca garab yuy meññ lu ne,
6sàkklu samay déeg, di ko suuxate, garab ya naat.
7Ma jëndi jaam, góor ak jigéen; ñu ami doom ci kër gi. Ma am jur gu ne gàññ, gu gudd ak gu gàtt, ba ëpple ku ma jiitu ci Yerusalem.
8Ma dajale sama xaalis ak sama wurus, moom alali buur yeek diiwaan yi ma yilif, tabb samay woykat, góor ak jigéen, boole ci bànneex bi ci jabari jabar.
9Ma am doole, yokku, ba sut ku ma jiitu ci Yerusalem, te teewul may jëfe xel.
10Lépp lu saay gët xemmemaa, xañuma ko sama xol. Bañaluma sama bopp benn bànneex, xanaa di bége lu ma liggéey, yooloo ko la ma liggéey.
11Ma xoolaatal sama bopp lépp lu ma sottal, doñ-doñi ko, ba sottal, ndeke lépp, cóolóoli neen ak napp um ngelaw. Nit gisul njariñ ci kaw suuf.
12Ma geesu xoolaat xel mu rafet, xool ag nitoodi akug ndof. Ana ku may wuutuji ci nguur gi, lu muy def lu moy lu ñu daan def?
13Ma gis ne ni leer ëppe lëndëm njariñ, ni la xel mu rafet ëppe ndof njariñ.
14Ku xelu day xool fa muy jaare, dof biy tëñëx-tëñëxi cig lëndëm. Ma ne moona ñoom ñaar a bokk dogal moos.
15Ma xalaataat, saam xel ne ma, dof bi noonu, man it noonu; ana lu may xeloo xelu doye? Saam xel ne ma loolu it, cóolóoli neen.
16Ku xelook ku dof, du yàgg ñu fàtte la; ay bés yu néew, ñu fàtte lépp. Acam! Dof, dee; rafet xel, dee.
17Ma far bañ àddina. Ndaw naqar ci jëfi kaw suuf, te lépp di cóolóol ak napp um ngelaw!
18Sama doñ-doñ, ji fi kaw dun bi, génnliku na ma, dama koy wacce ka may wuutuji rekk,
19xameesul ku xeloom ku nitoodi lay doon, mooy moom lu ma doon doñ-doñi, te sama manoore manaloon ma ko fi kaw dun bi. Loolu it, cóolóoli neen.
20Sama xol a jeex ci doñ-doñ ju ma doñ-doñi fi kaw dun bi.
21Nit a ngi doñ-doñee xel, xam-xam ak manoore, te ku doñ-doñiwuloon lay wacce alalam. Loolu it, cóolóoli neen ak naqar wu réy.
22Ma ne ana lu nit di jariñoo ci doñ-doñ ak xalaatu xol, yi muy doñ-doñaale fi kaw dun bi?
23Ndegam day yendoo tiis ak naqaru tës-tës, ba far fanaanoo xel mu dalul. Loolu it, cóolóoli neen.
24Kon nit amul lu gën di lekk ak a naan, di bànneexoo ñaqam. Ma gis ne loolu it Yàllaa koy maye.
25Ana kuy lekk ak a bànneexu, te du Yàlla?

Read Kàdduy Waare 2Kàdduy Waare 2
Compare Kàdduy Waare 2:3-25Kàdduy Waare 2:3-25