2Ma ne: «Reetaan ag nitoodi la; te mbégte lu muy jariñ?»
3Saam xel ne ma, ma naan biiñ boog, bégloo, ba mel nib dof, tey ànd ak sama xel, ba gis lu ci baax, ba doom aadama di ko def, giiru dundam fi ko jant bi tiim.
4Damaa liggéey lu réy. Tabaxlu naa samay kër, jëmbat sama toolub reseñ.