9Lu ayoon mooy ayati, lu ñu jëfoon moom lañuy jëfati. Dara yeesul fi kaw suuf.
10Lëf a ngii, nit naa: «Lii de lu bees la,» te mu ngi fi woon lu yàgg, lu jiitu sunu juddu.
11Kenn du fàttliku ñi jiitu, ñiy ñëwit, ñi leen topp duñu leen fàttliku.
12Man waarekat bi, buurub Israyil laa woon ci Yerusalem.
13Damaa dogu ne damay gëstu, teg ko ci xel mu rafet, di settantal mboolem lu nit def fu jant bi tiim. Ndaw sas wu tiis wu Yàlla sase, ñu war koo sasoo!
14Gis naa jépp jëf ju jëfe ci kaw suuf, ndeke lépp cóolóoli neen la ak napp um ngelaw.
15Lu wañaaru, maneesu koo jubbanti; lu teewul, maneesu koo lim.
16Damaa wax ci saam xel naa: Man de, maa ngii di gëna xelu, ba sut ku ma jiitu ci jalub Yerusalem. Damaa xuus ci xel mu rafet ak xam-xam,